• il y a 3 ans
Wax ju bari :
Boo mer ee dëgg , sëytaane da lay dugg
Jaxjax al sa xol , def loo la , li mu bëgg
And al ak dal.

Sëytaane da fay jël temps , yakkamti wul
Boo am ul chance , bu la yalla , dimmili wul
Da , lay , xaptal

Boo bëgg ée mucc , ngóor sii , yaw déglu ma
Bu la fekk oon taxaw , toog al , xarit sama
Toog al ba dal

Bu la fekk oon toog , tëdd ël , ba gagni dem
Bu yagg ee , sëytaane , day mujj dem
Doo tu la tal

bul nangu , wax ju bari yaw , ku la ko bëgg indil na nga bañ
bul ko kaf e , bul ko mbokk oo , fexe el dund te ànd ak dal
booy ànd al , na nga seet , nit ku regle , te bañ bari wax
fexe el ba adopter , dund gu ànd ul ak bari wax
ku la ko bëgg teg , bul ko nangu , bul ko masala
bari wax , da lay tardeel , bari wax ,da lay sonn al
bari wax , da lay jaxase

bu leen sonn al béer , njaw du mel ni lem
bu leen sonn al béer , njaw du mel ni lem
bu leen sonn al béer , njaw du mel ni lem
bu leen sonn al béer , njaw du mel ni lem
bu leen sonn al béer , njaw du mel ni lem

wax lu néew , jëf lou bari , kouné war na laa ,
wax lu néew , jëf lou bari , loo loo am , maanaa

Ibra kassé birame coumba Ndiaye
Kouly kassé ek maajigéen oo
Al maabo Yacine dial , ma des ca bëlbë
Moo ma daan wax naan ,
Youssou na ñu ànd liggéey , te waññi wax
Te waññi wax
Baay i Oumar , baay i Alioune , baay I ndeye kassé
Góor u fatou
Baay i idi , doom i nday i adama , ak kassé plus
Al maabo yacine dial , Ibra mor astou kassé
Fatou oy , médoune kassé
Ndoumbé yatma ,

wax ju néew , jëf ju bari , ku ne war na la
wax ju néew , jëf ju bari , ku ne war na la
wax da fay gatt yanu maanaa ,
neex a dégg lool , fees ak njariñ
ñu wax ko ba wax jot ee , fa ñu ko war a wax e
wax ju néew , jëf ju bari , ku ne war na la
wax ju néew , jëf ju bari , ku ne war na la
xaaj u guddi , boo toog oon ba mu yagg , nga doon bëccëg
di na xumb lool , ba jaaxal gaa ñi
wax ju néew , jëf ju bari , ku ne war na la
wax ju néew , jëf ju bari , ku ne war na la

Category

🎵
Musique